TSK

TSK · Hebrews 3:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba Israyil gisee na Aji Sax ji jowe loxoom bu baax ca xareem baak waa Misra, dañu daldi ragal Aji Sax ji, teg ca am kóolute ci Aji Sax ji ak ci Musaa, jaamam ba.

«Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaa ma wonagum lenn ci sa màggaay ak sa doole, Sang bi. Ana yàlla ju nekk asamaan, mbaa ci kaw suuf ju mana roy say jëf ak say jaloore?

Musaa, jaamub Aji Sax ji nag dee foofa ca réewum Mowab, na ko Aji Sax ji tudde.

Sa bésub Noflaay bu sell it, yaa leen ko xamal, te say santaaneeki dogali yoon ak saw yoon, yaa leen ko dénk. Musaa, sa jaam ba, jottli leen ko.

Sang bi ne ko: «Ana kan nag mooy saytukat bu wóor te muus, ba njaatigeem batale ko curgag këram, ngir mu di leen jox seen njël ca ba muy jot?

Mu tàmbalee nag ci Yonent Yàlla Musaa, jaare ci yonent yépp, tekkil leen mboolem lu Mbind mi indi ci mbiram.

Acts 3:22 TSK

Musaa kay noon na: “Boroom bi seen Yàlla mooy seppee ci seenu xeet ab yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax.

¶ Ci kaw loolu ñu jox ko bés, bés ba dikk, ñu bare dikk, fekksi ko ca daluwaayam. Suba ba ngoon mu di leen jàngal, di leen seedeel lu jëm ci nguurug Yàlla, di leen won ci mbirum Yeesu, firnde yu leen gëmloo te tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi.

Te itam li ñuy sàkku ci ay saytukat moo di ñu jara wóolu.

Ku wóor la woon, ñeel ki ko tabb, noonee Musaa wóore woon ci mboolem waa kër Yàlla.

Noonu la Noo gu Sell gi firndeele ne yoon wu maye dugg ca bérab bu sell baa sell feeñagul woon, te fekk néeg bu jëkk ba di taxaw ba tey.

¶ Googu texe, yonent ya jottli woon waxyub seen yiw wi leen dikkal, niir nañu ko, càmbar ko.