TSK

TSK · Hebrews 3:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

“Yeena gisal seen bopp ni ma def waa Misra, te yeen, ma boot leen, ni jaxaay di fireey laafam, boot ay doomam, ba ngeen jegesi ma fii.

seeni doom di màngaan ñeent fukki at ci màndiŋ mi, gàddoo ko seen ñàkk worma, yeen ñi leen jur, ba keroog seeni néew tëdd ba jeex ci màndiŋ mi.

¶ Waaye wattuleen, wattuleen seen bopp bu baax, bala ngeena fàtte mbir yi ngeen teg seen bët, ba du génn seenum xel seen giiru dund gépp. Te nangeen ko xamal seeni doom ak seeni sët.

Seeni yére ràppul, seeni tànk newiwul diiru ñeent fukki at yii.

¶ Nattu yu mag yooyu, ak firnde yeek kéemaan yu réy yooyu, yeena ci teg seen bët,

Amos 2:10 TSK

Fekk yeen, ma génnee leen réewum Misra, jaarale leen màndiŋ ma diiru ñeent fukki at, ngir ngeen nanguji réewum Amoreen ñi.

Acts 7:36 TSK

Moo leen génne réewum Misra, moo def ay kéemaan aki firnde ca réew ma, ak ca géeju Barax ya, ak ca màndiŋ ma, diiru ñeent fukki at.