TSK

TSK · Hebrews 4:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Maa leen di fàdde mbas, nangu seen cér, ba noppi sose ci yaw askan wu leen ëpp, ëpp leen doole.»

Seen tur wi ngeen bàyyi gannaaw la samay tànnéef di móoloo, naan: “Yal na la Boroom bi Aji Sax ji rey ni diw ak diw,” waaye ñoom sama jaam ñi, tur wu yees lees leen di wooye,

Ba loolu amee fit la leen Póol ak Barnaba tontoo, ne leen: «Yeen Yawut yi de lanu wara jëkka yégal kàddug Yàlla gi, waaye gannaaw gàntal ngeen ko, ba jombale seen bopp ag texe ba fàww, nu ngii di walbatiku ci jaambur ñi.

¶ Li may wax, bokk yi, moo di, li des yàggatul. Kon nag bés niki tey, na ñi am jabar mel ni bu ñu ko amul woon;

Te it ana ñan ñu moy ña déggadi woon, la Yàlla giñaloon ne duñu tàbbi mukk ci noflaayam?

Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla.