TSK

TSK · Hebrews 5:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñu naa: «Ana ku Esayi mii di jàngal? Ana ku muy àgge xibaar? Xanaa ku yàggula fer, di doora bàyyi ween?

yaa di jànglekatub naataxuuna yi, di sëriñub tuut-tànk yi, gannaaw yaa jagoo ci yoonu Musaa, mboolem luy jëmmu xam-xam, ak lépp luy dëgg.

¶ Man nag bokk yi, manuma woona wax ak yeen ni ñuy waxe ak ñu ànd ak Xelum Yàlla, waaye ni niti suuxu neen rekk laa manoona waxe ak yeen, mbete ñu diy tuut-tànk ci yoonu Almasi.

¶ Bokk yi, buleen doon ay xale ci wàllu déggin. Su dee lu bon, nekkleen ci ay tuut-tànk, waaye màggleen ci wàllu déggin.

¶ Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje, ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu.

Ni liir buy doora juddu yàkkamtee nàmpe, ni ngeen wara yàkkamtee nàmp soow mu set miy Kàddug Yàlla. Mooy tax ngeen màgg ci seen dundug texe,