TSK

TSK · Hebrews 5:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Indil Aaróona aki doomam yu góor te indaale yére yi ak diw gi ñuy fale ak yëkk wiy saraxu póotum bàkkaar ak ñaari kuuy yi, boole ca pañeb mburu ya amul lawiir,

Mu wax Kore ak gàngooram gépp, ne: «Bu ëllëgee, Aji Sax ji mooy xamle kan la séddoo ak kan mooy ki sell, mu jegeñal ko boppam. Ki mu taamu nag, dina ko jegeñal boppam.

Yaw mu jegeñal la, yaak sa bokki Leween ñépp, ngeen di xëccu céru carxal, boole ci!

And yooyii seeni boroom feye seen bakkan seeni bàkkaar, dees koy tëgg, ba mu tàlli, xoobe ko sarxalukaay bi. Gannaaw fi kanam Aji Sax ji lañu indi and yi, ba tax mu doon lu sell, na and yi doon firnde, ñeel bànni Israyil.»

Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.»