¶ Mu tegaat ca ne Aadama: «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, dinaa rëbb suuf ndax yaw; coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp.
TSK
TSK · Hebrews 6:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.»
¶ Mbir yi làqu daal, ñeel na sunu Yàlla Aji Sax ji, mbir yi feeñ nag, ñeel nu, nook sunuy doom ba fàww, te nu wara jëfe mboolem kàdduy yoon wii.
kon yal na ay dég wuutu bele ba, ñax mu bon wuutu lors ba. Fii la kàdduy Ayóoba yem.
Naa woy sama soppe woyu cofeel wu solowoo tóokëram. Sama soppee fi amoon tóokër, kaw tund wu suuf sa nangu lool.
Day mel ni gajjub ndànd-foyfoy, du gis ngëneel luy dikk! Day dëkke màndiŋ mu wow koŋŋ, suufas xorom su kenn dëkkul.
Yaw nit ki, ana lu bantu reseñ gëne ci bant yi, ak mboolem caru garab bu mu doon ci gott bi?
Mu ne surga ba: “Ñetti at a ngii may dikk, raas-si garab gii, gisuma ci dara. Kon gor ko, da fiy xatal rekk.”
Xanaa tiitaangey séentu mbugal ma, ak sawara wu yànj wiy xoyom fippukat yi.
Képp ku ñu gisul ñu bind la ci téereb dund bi, ci déegu sawara si lees la sànni.