TSK

TSK · Hebrews 7:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci kaw loolu Melkisedeg buurub Salem, mi doon sarxalkatu Yàlla Aji Kawe ji, daldi ñëw, indi mburu ak biiñ.

Éy Yàlla, baaxe ma, ngalla baaxe ma, fi yaw laay làqu, yiiroo sa kiiraay, ba musiba yi jàll.

Ñu fàttliku ne Yàllaay seen cëslaay, xam ne Yàlla Aji Kawe jeey seen njotlaay.

Ana ku ñu yékkatee penku, woo ko ci tànki njekk? Ana ku ko jébbal xeet yi, nangulal ko buur yi, saamaram note ba ñuy pënd, fittam jamat, tasaare ni boob?

¶ «Buur, Yàlla Aji Kawe ji daa joxoon sa baay Nabukodonosor nguur gi, muy ku màgg, am ndam ak daraja.

Micah 6:6 TSK

Ana lu may dikkaale fi kanam Aji Sax ji, ba sujjóotal Yàlla jooja fa kaw. Tee ma koo dikke ay rendi-dóomal, ay wëlluy menn at?

Ndaw sa topp ci Póol ak nun, di xaacu, naan: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; dañu leen di yégal yoonu mucc.»