TSK

TSK · Hebrews 7:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nun itam naka noonu, ba nu dee ay tuut-tànk yu nekk ci kilifteefu mbiri àddina, ay jaam lanu woon.

ci moom ngeen mate it, te mooy kilifay mboolem boroom nguur yi, ak mboolem boroom sañ-sañ yi.

Ci biir loolu Yàlla tudde ko sarxalkat bu mag, bi topp dayob Melkisedeg.

Mbir mi gëna leerati gannaaw ba beneen sarxalkat feeñee te mel ni Melkisedeg.

Waaye Yeesu mii la ag palam ànd ak ngiñ lu jibe ca ka ko wax ne ko: «Boroom bee ko giñ te du dellu gannaaw: “Yaa dib sarxalkat ba fàww.”»

¶ «Lii nag moo di kóllëre gi may fas ak kër Israyil, gannaaw yooyu fan, la Boroom bi wax, mu ne: Maay yeb sama ndigali yoon ci seenum xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.