te ñoo doon naa Yàlla: «Xiddi nu!» Ñii ana lu leen Aji Man ji di def?
TSK
TSK · Hebrews 7:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nanga fa gëdde rabu àll wi ci barax yi, ñooy gétti yëkk yi, xeet yi ci des diy sëllu. Gëdd leen, ba ñu sujjóotalsi laak dogi xaalis. Tasaareel xeet yooyu sopp xare,
Dees na ma waxal ne: «Aji Sax ji rekk a jagoo njekk ak doole!» Mboolem ñi ma mereey ànd, sëgg, fekksi ma.
Daa xool, gisul kenn; mu tiisoo li ci kenn jógul, moo tax loxoom may ko ndam, te njekkam la sukkandikoo.
Yeen doom yu woyof kumba yi, waññikuleen, ma fajtal seen woyof kumba.»
Ndegam Yàlla ji nuy jaamu man nanoo musal ci taalu sawara bu yànj bi, musal nu ci yaw mii, dina nu musal.
¶ Ba njël jotee, ba bët di bëgga set, Buur jóg, daldi gaaw dem ca kàmbu gaynde ya.
Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!
Ci Yeesu, ci kaw ngëm gu nu ko gëm lanu ñemee àgge fit wu mat sëkk, fa kanam Yàlla.
Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, nirule kook yaramam wi ànd ak teddnga.
Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne moo mana sàmm li ma ko dénk ba keroog bés ba.
Fan yi Almasi dee dund dundu nitu suuxu neen, ay ñaan aki dagaan yu ànd aki yuux aki jooy la daan yékkati jëme fa ki ko mana wallu ba du dee, te nangule na it, ndax na mu ragale woon Yàlla.
Te kooku, du santaaneb ndonol deret bu mu wàccool moo ko taxa doon ab sarxalkat, waaye manoorey dundam gu amul àpp moo ko def ab sarxalkat.
Waaye Yeesu mi sax ba fàww, moo sasoo carxal gu sax dàkk.
Ku amul ngëm nag doo mana neex Yàlla, ndax kiy dikk fi Yàlla, fàww nga jëkka gëm ne Yàlla am na, gëm it ne ñi koy sàkku, moo leen di yool.
¶ Bi loolu amee meneen malaaka dikk, taxaw ci wetu sarxalukaay bi. Mu ngi yor andu cuuraayu wurus. Ñu jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole kook ñaani mboolem aji sell ñi, jooxe ko ci kaw sarxalukaayu wurus bi ci kanam ngàngune mi.