TSK

TSK · Hebrews 7:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Ndegam sarxalkat bi ñu diw, fal ko, moo moy, ba yóbbe mbooloo mi tooñ, na indil Aji Sax ji yëkk wu ndaw wu amul sikk, muy saraxu póotum bàkkaar ndax bàkkaar ba mu def.

Mu ne leen: «Demleen wax njomboor moomu, ne ko: “Maa ngii di dàq rab yi, di maye ag wér, tey ak ëllëg. Bésub ñetteel ba nag ma sottal.”

Ci fan yu mujj yii, Doom ji la waxe ak nun, ki mu jagleel lépp, ki mu sàkke àddina wërngal këpp.

Almasi nag mooy Doom ju wóor ji jiite kër Yàlla, te nun nooy këram, ndegam kay nu ngi wéye aw fit, ak yaakaar ji nuy puukarewoo.

¶ Bépp sarxalkat bu mag nag, ci biir nit ñi lees ko jële, fal ko ngir nit ñi, ci seen diggante ak Yàlla, muy jébbale ay jooxe ak saraxi jur ngir seeni bàkkaar.

Li muy Doom lépp, terewu koo tàggatu ci dégg ndigal, ndax coono yi mu daj.

Waaye Yeesu mii la ag palam ànd ak ngiñ lu jibe ca ka ko wax ne ko: «Boroom bee ko giñ te du dellu gannaaw: “Yaa dib sarxalkat ba fàww.”»