Kon nag ngalla waxal ne sama jigéen nga, ba tax ma am jàmm; su ko defee dees na ma bàyyi, ma dund, te di la ko gërëme.»
TSK
TSK · Hebrews 7:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu ñaanal Ibraam ne ko: «Yaw Ibraam, Yàlla na la Yàlla Aji Kawe ji barkeel, moom mi sàkk asamaan ak suuf!
maa lay barkeela barkeel, fula ful saw askan ni biddiiwi asamaan, mbaa feppi suufi géej. Sa askan dina teg ay bañam tànk,
¶ Ndax kat digeb Ibraayma ba sédde Ibraayma àddina si, moom ak askanam, sàmm gu mu sàmm yoonu Musaa taxul, waaye àtteb njub bi mu jagoo ndax ngëmam, moo ko waral.
Te Ibraayma lañu digoon dige yi mook ki taxawal askanam. Newuñu: «ñi taxawal ay askanam», mbete ñu bare lañuy wax, waaye wenn rekk la: «ki taxawal askanam,» te ki taxawal askanam moo di Almasi.
¶ Melkisedeg moomu doon buurub Salem te nekkoon sarxalkatub Yàlla Aji Kawe ji, ba Ibraayma délsee jóge xareem baak buur ya mu duma, kooku moo ko gatandu woon, ñaanal ko.
¶ Ñoom ñépp ngëm lañu deeyaale te jotaguñu woon la ñu leen digoon. Waaye fu sore lañu ko séene, di ko séentu, tey ràññee ne ay doxandéem aki màngaan lañu ci àddina.