Su ko defee nga taxawal jaamookaay bi, ni ñu la ko wone ci kaw tund wi.
TSK
TSK · Hebrews 8:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Tegukaayu làmp bi nag, ni ñu ko liggéeye nii la. Wurus lañu ko tëgge ba mu jekk, dale ko ci tànk bi, ba ci mbar mi. Noonee ko Aji Sax ji wone woon Musaa, na lañu liggéeye tegukaayu làmp ba.
¶ «Xaymab seede baa nga woon ak sunuy maam ca màndiŋ ma, ñu sàkke ko na ko ka doon wax ak Musaa sante, dëppale kook misaal ma Musaa gisoon.
Loolu misaal la, ñeel jamonoy tey, di firndeel ne jooxe yi ak saraxi jur yi ñu daan jébbale manuñoo dindi yaraangeg jaamukatub Yàlla bi, ba mu set wecc.
¶ Yoonu Musaa takkndeeru xéewal yiy ñëw doŋŋ a ci nekk, waaye xéewal ya ci seen bopp nekku ci. Looloo tax sarax yi yoon wi laaj ñu war koo saxoo jébbale at mu nekk, manula setal mukk wecc ñiy jaamusi.
¶ Wattuleen bala ngeena tanqamlu kiy wax ak yeen. Ndegam ña tanqamlu woon ka yékkati woon kàddoom, wax ak ñoom ci kaw suuf ñoo rëccul, aste nun ñii, su nu dëddoo kiy waxe fa asamaan.