Lóot di tendeefal, gan ña jàpp ci loxo bi, booleek soxnaam ak ñaari doomam génne, làq leen ca gannaaw dëkk ba, ndax yërmande ju Aji Sax ji am ci Lóot.
TSK
TSK · Hebrews 8:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Musaa dem, yeggeji mbooloo ma kàdduy Aji Sax ji yépp, ak àttey yoonam yépp. Mbooloo ma mépp bokk benn baat, ne ko: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def.»
¶ Aji Sax ji ne ko: «Maa ngi nii di fas kóllëre ak yeen. Ci sa kanam mbooloo mépp laay def ay jaloore yu kenn masula amal ci àddina sépp, ak ci askan yépp, te mbooloo, mi nga nekk ci seen biir mépp ay gis jaloorey Aji Sax ji, jaloore ju raglu ji ma lay defal.
Sunu Yàlla Aji Sax ji moo fasoon kóllëre ak nun ca tundu Oreb.
ngir def leen bésub tey, askan wi mu ñoñoo; moom ci boppam mu doon seen Yàlla, na mu leen ko waxe woon, na mu ko giñale woon seeni maam, Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.
Aji Sax ji ne Musaa: «Yaa ngi nii di tëddi fa say maam. Mbooloo mii nag dinañu tàmbali di gànctuy topp yeneen yàllay doxandéem yu waa réew, ma ñu jëm ca seen biir. Dinañu ma wacc, fecci sama kóllëre gi ma fasoon ak ñoom,
Dama ne: Yàlla du gàntal ku maandu, te du dooleel kuy def lu bon.
Ñoo sàmmul kóllërey Yàlla, gàntal yoonam,
xanaa dëddu, di ko wor ni seeni maam, toogadi ni xala gu yolom.
seppee bànni Israyil ca ñoom, Kee saxoo ngoram!
Suuf si la ñi ko dëkke sobeel, ñoo wàcc yoon yi, xëtt ndigal, fecci kóllëre gi sax dàkk.
Man Aji Sax ji maay sa Yàlla; téye sa loxol ndijoor, di la wax ne la: «Bul tiit, maa lay dimbali.»
Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.
Artu naa àrtu seeni maam, dale ko ba ma leen génnee réewum Misra, ba tey jii ma jàppoo di leen àrtu, naan leen ngeen déggal ma.
Du mel ni kóllëre ga ma fasoon ak seeni maam keroog ba ma leen jàppee ci loxo, génne leen réewum Misra. Ndax ñoom ñoo fecci sama kóllëre, te man may seen boroom kër.» Kàddug Aji Sax jee.
Ma jaareeti fa, xool la, gis ne mat ngaa séy. Ma tàllal sama mbubb, sànge ko sa yaramu neen, ba noppi giñal la, dikke la kóllëre. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Nii laa la moome.
Maa leen di lime sama yetu sàmm, kenn-kenn, tënk leen ci pas-pasu kóllëre gi.
Lii itam yeena ngi koy def: Yeena ngi tawal ay rongooñ sarxalukaayu Aji Sax ji, di jooy ak a binni, ndax moo geesootul seen sarax, te nangootul lenn ci seen loxo.
Sóol jóg, xippi, gisul dara; ñu daldi koy wommat, dugal ko biir Damaas.
¶ Bokk yi, ma misaale ko mbiri doom Aadama. Kayitub donale bu nit doŋŋ bind, su dee lu wóor, deesu ko neenal, mbaa di ci yokk dara.
Looloo waral it kóllëre gu jëkk ga ci boppam, dooreesu ko woon te deret tuuruwul.