TSK

TSK · Hebrews 9:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Na ma bànni Israyil defaral kër gu sell, ndax ma dëkk ci seen biir.

Dénkooleen sama ndénkaane ngir baña roy lenn ci aada yu ñaaw yi ñu fi doon topp lu leen jiitu, te buleen sobeel seen bopp ci yooyu. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.»

Bumu ci wacc dara mu fanaan, te benn yax, bumu ko ci damm. Na mu dëppook mboolem dogali yooni bésub Mucc, na ko màggale noonu.

Luke 1:6 TSK

Ñoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi.

Mooy liggéeye kër gu sell ga, ca biir xaymab jaamookaay bu dëggu, ba Boroom bi samp, te nit sampu ko.

¶ Bu Yàlla wooyee kóllëre gii gu yees nag, daa fekk mu wonnil gu jëkk ga. Lu wonni te di lu yàgg nag, mu ngi ci tànki wees.