Na lakk nebbon bi yépp ci kaw sarxalukaay bi, def ko ni nebbonu saraxu cant ci biir jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.
TSK
TSK · Hebrews 9:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñaareel bi na ko def saraxu rendi-dóomal, muy li ñu santaane. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaar bi mu def, mu am njéggal.
Na indi kuuy mu amul sikk, ñu xayma njégam, yót ko sarxalkat bi, muy saraxu peyug tooñ. Na ko ko sarxalkat bi defal njotlaayal bàkkaar bi mu def te xamu ko woon. Su ko defee mu am njéggal.
Picc miy dund da koy booleek bantu seedar bi ak wëñ gu xonq curr gi ak caru isob bi, boole lépp sóob ci deretu picc ma ñu rendi woon tiimale ko ndox mi balle ci bëtu ndox.
Gannaaw gi ñu rendi kuuy miy saraxu peyug tooñ, sarxalkat bi sàkk ci deret ji, taqal ci tabanu noppu ndijooru nit ki ñuy laabal ak baaraamu déyu ndijooram ak baaraamu déyu tànku ndijooram.
Ndaxte dundu mbindeef ci deret la nekk, te man maa leen sédde deret, ngeen di ko jotoo seen bakkan ci kaw sarxalukaay bi. Ndax kat bakkanu mbindeef deretam la taxawe. Moo tax deret mana defal nit njotlaayam.