Te it bu ngeen jëlalee seeni doom jabar ca seen doom yu jigéen, seen jigéen ñooña dinañu gànctook seeni tuur, ba xiir seen doom yu góor ci gànctook seen tuur yooyu.
TSK
TSK · Hosea 1:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
seeni jëf sobeel leen, ndax seen bokkaale.
«Ñaari yoon la xeet wi ma séddoo bàkkaar: ma di bëtu ndox muy dund, ñu wacc ma, man, di gasal seen bopp kàmbi dencukaayi ndox, te kàmb yi fett, di senn.
«Nu ngeen ñemee naa: “Sobeelunu sunu bopp te toppunu tuuri Baal?” Seetleen li ngeen nekke ci xur wi, xool-leen li ngeen di def, mel ni giléem gu ndaw, di wodd-woddi, fu ne mu daw jëm fa,
Ni gànctu yombe Israyil tax na réew mi sobewu. Njaaloo naak yàllay doj, njaalook yàllay bant.
¶ Aji Sax ji ne: «Yaw nit ki, jëlal móolu ban, teg fi sa kanam, nga rëdd ci ab dëkk, mu misaal Yerusalem.
¶ Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
¶ Kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
Ñoom seen yaay moo gànctu, ki leen ëmb moo def lu gàccelu, naan: “Damay toppi sama far, yi may jox sama lekk ak samag naan, ak samag wëñ ak sama lẽe ak samag diw ak sama biiñ.”
Maa xam Efrayim, Israyil laa ne, umpu ma. Efrayim, yaa gànctu, Israyil laa ne, yaa sobeel sa bopp.
¶ Seeni gët xoolul lu moy ku ñu jaalool, te duñu bàkkaar ba regg mukk; ku dëgërul, ñu yóbbaale la. Ñooñu la seenub xol tàggatu ci ag bëgge, mii njurum alkànde!
Jë bi nag, tur wii lañu ci bind, muy kumpa: Babilon gu mag gi, ndeyu jigéeni moykat yeek ñaawtéefi àddina yi.