TSK

TSK · Hosea 10:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mooy la ñu léeb bu yàgg rekk ne: “Ku bon, mbon rekk.” Man nag sama loxo du la dal mukk.

Mbooloo mu réy mayul Buur ndam, doole ju bare walluwul jàmbaar.

Doom aadama, ngelawal neen; nit, naxi neen. Booleel teg ci lu ñuy natte diisaay, kaw la jëm. Ñooy gëna woyof ngelaw!

Kàdduy dëgg, day sax dàkk; fen, xef xippi, mu wéy.

Seede buy fen muccul mbugalam, kuy noyyee ay fen du rëcc àtteem.

Ma seetlooti fi kaw suuf ne du ku gaaw, yaay raw; du ku jàmbaare, yaa moom xare; du ku xelu, am loo dunde; du ku muus, duunle; du kuy xamkat, amu yiw; ku nekk ak bésam ak wërsëgam.

Hosea 8:7 TSK

«As ngelaw lañu ji, ñooy góob ngëlén. Gub du jóg, pepp du focci, te bu pepp amoon it, jaambur a koy wonn.

¶ Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob.