Gannaaw gi nag buurub Asiri gis ne Ose lal na pexe, ndax daa yónnee ay ndaw ca So buuru Misra, ba noppi lànk ne du fey galag at mu nekk. Buurub Asiri jàpp ko, tëj.
TSK
TSK · Hosea 12:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ayóoba, ku xelu dina tontoo kàdduy ngelaw, mbel-mbelam nib jaas bu fees dënnam a?
Dikke ni, delloo ni, loolu it tiis wu réy la. Doñ-doñi, ngelawal neen, ana jariñ la?
Boroom baa ngii di leen sottisi dexu Efraat gi ne xéew ak dooleem, te mooy buurub Asiri ak mboolem darajaam. Dex gi mooy génn xuram, fees fépp fu dig tàkkam,
Boroom bi nee: «Bu ma sottalee liggéey fa kaw tundu Siyoŋ ak fa Yerusalem, maay mbugale buurub Asiri réy-réyloom gi, ak gëti xeebaateem.»
Yéeneb waxyu bii ñeel na malay àllub Negew: Réewum tiis laak njàqare, kërug gayndeeki segg, ak saamaan ak céebi, mbaam lañu sëf seen alal, jaare fa, giléem lañu sëf seeni denc, jëme xeet wu leen dul jariñ.
Gis naa ne it Israyil Woyof-Kumba-si gànctu na ba ma yebal ko, jox ko kayitu pase, mu dem, te taxul doomu ndeyam Yuda workat bi ragal. Moom it daa dem di gànctu.
«Owoliba rakk ja gis ca te gëna yàqu magam, di gànctu ba raw mag ja.
Maay dakkal gépp mbéxam; ay màggalam, ay Terutel weeram, ay bési Noflaayam, ak mboolem bési ndajeem.
Waaye niki askan wi, niki sarxalkat yi, maa leen di dikke seen añu jikko, maa leen di fey seeni jëf.
Efrayim daa mel ni pitax, dofe, ñàkk xel, di woo wall Misraak a dem Asiri.
Ci xeeti jaambur ñi lañuy jënde, waaye du tee ma dajale leen. Léegi ñu tegoo notaangey buur aki kàngam.
Ñoo sóobu ci xóotey yàqute, na woon ca janti Gibeya, te Yàlla mooy bàyyi xel seenug ñaawtéef, ba mbugale leen seeni moy.
¶ Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob.