¶ Daawuda nag ne Natan: «Maa tooñ Aji Sax ji.» Natan ne ko: «Aji Sax ji it jéllale na sa bàkkaar; doo ci dee.
TSK
TSK · Hosea 14:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Lu tee kon nga baal ma samag moy, jéggal ma samag tooñ? Léegi tey ma tëri biir suuf, nga di ma seeta seet, fekk nekkatuma.
Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda dëkkoo ndaw sa ñuy wax Batseba.
Mu laalale xal wi sama gémmiñ, ne ma: «Mu ngoog, ndegam lii laal na sa gémmiñ, sag tooñ wàcc na, sa bàkkaar faru na.»
Demal yéeneji kàddu yii fa bëj-gànnaar. Nga ne: “Israyiloo, Woyof-Kumba, délsil.” Kàddug Aji Sax jee. “Duma la fasal kanam. Man Boroom ngor laa, te duma jàpp mer ba fàww.” Kàddug Aji Sax jee.
Israyil, ag reewandeem a ko tiiñal, Israyil ak Efrayim ñooy fakktaloo seenug ñaawtéef, Yuda it ànd ak ñoom fakktalu.
Diggante buntu néeg bu sell beek sarxalukaay bi, sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, nañu fi taxaw jooy; nañu ne: «Aji Sax ji, yërëmal sa ñoñ; bul wacce say séddoo gàcce, ak ñaawley xeeti jaambur yi. Lu jar ñuy wax ëllëg ci biir askani jaambur yi, naan: “Ñii, ana seen Yàlla ji?”»
Malaaka ma wax ak ña taxaw fa kanamam ne leen: «Summileen yéreem yu dand yi.» Mu teg ca ne Yosuwe: «Dama ne, far naa sa bàkkaar, te dinaa la solal lu jekk.»
Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»
¶ «Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore, ñemewula siggi sax, xool asamaan, xanaa di fëgg dënnam te naan: “Éy Yàlla, yërëm ma, man bàkkaarkat bi.”»
Loolooy doon sama kóllëreek ñoom, kera ba may far seeni bàkkaar.»
Mbaax gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu, moom lay firndeele mboolem xarnu yiy ñëw, ni yiwam yaatoo ba tiiñ am xel.
Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
¶ Kon nag saa su nekk, nanuy jooxee ci Yeesu, sunu saraxu cant, ñeel Yàlla, muy sarax su bawoo ci sunuw làmmiñ, ñu di ko birale aw turam.
¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.