Léegi nag su ngeen ma déggalee bu baax, di sàmm sama kóllëre ak yeen, yeenay doon sama moomeelu bopp ci mboolem askan yi. Dëgg la, àddina wërngal këpp maay Boroom,
TSK
TSK · Hosea 2:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ñu doon sama ñoñ, may seen Yàlla.
Su ko defee sama dogali yoon lañuy doxe, te sama àttey yoon lañuy sàmm, di ko jëfe. Su boobaa ñuy sama ñoñ, may seen Yàlla.
Su boobaa ngeen mana dëkke réew mi ma joxoon seeni maam, di sama ñoñ, may seen Yàlla.
Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Lo Ami» (mu firi Du sama ñoñ), mu ne: «ndax dungeen sama ñoñ, te man duma seen dara.»
Ñetteel bi laay tàbbal ci sawara, xelli ko ca ni ñuy xellee xaalis, nattu ko ni ñuy nattoo wurus cib taal. Xaaj boobu moo may woo ci sama tur, ma wuyu ko. Moom laay wax: “Sama ñoñ,” Moom mu ne: “Aji Sax jeey sama Yàlla.”»
¶ Ndegam boobu liggéey lanu sasoo, ci yërmandey Yàlla, dunu yoqi.
Yeen ñi dul woon sax aw xeet, démb, tey yeen ay xeet wi Yàlla ñoñoo; dajaguleen woon yërmande, waaye tey daj ngeen yërmande.