TSK

TSK · Hosea 2:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ma xamal leen nag li ma naral sama tóokër bi. Ñàggib ñagam, mu dim parlu; màbb miiram, ñu dëggaate ko, jàll.

Xamuleen ne fi leek lu néewa néew, àllub Libaŋ sopplikub tóokër, tóokër bi walbatiku meññ, ba ñu ne ab gott la?

«Maa leen di witta witt.» Kàddug Aji Sax jee. «Garabu reseñ du dese doom, figg du dese doom,» kàddug Aji Sax jee, «xob ya sax day wow. Lu ma leen joxoon, rëcc na leen.»

«Ku ñuy wax Mise, dëkk Moreset, doon na biral waxyu ca jamonoy Esekiya buurub Yuda. Daa waxoon waa Yuda gépp ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngooru xare yi dafa wax ne: Dees na gàbb Siyoŋ nib tool, Yerusalem diy tojit, jale; tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.”

Man déy ni gaynde laay mel ak Efrayim, ni gaynde gu ndaw laay mel ak waa kër Yuda. Man, man mii maay xotat, wéy, maay yóbbu te kenn du wallu.

Maay dajeek yeen ni rab wu aay wu ñu xañi doom, maay xotti seen mbuusum xol, fa laa leen di yàppe ni gaynde, te rabu àll moo leen di xotat.