Yaw daal demal rekk, yóbbu mbooloo mi fa ma la waxoon, te sama malaakaa ngii di la jiituji. Waaye keroog sama bésu mbugal, maay mbugal mbooloo mi ndax seen bàkkaar.»
TSK
TSK · Hosea 2:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Wattuleen seen bopp nag, bala ngeena fàtte seen Yàlla Aji Sax ji, baña sàmm ay santaaneem, ak àttey yoonam, ak dogali yoonam yi ma leen di dénk tey.
Mu sàlloo bàkkaari Yerbowam doomu Nebat. Loolu doyatu ko, mu jël jabar Yesabel doomu Etbal, buurub waa Sidon ña. Mu dem bay jaamu seen tuur mi ñuy wax Baal, di ko sujjóotal.
Moo tabaxaat bérabi jaamookaay ya Esekiya baayam tasoon, yékkatil tuur mi ñu naan Baal ay sarxalukaay, samp xer wu ñuy jaamoo Asera, noonee ko Axab buurub Israyil defe woon, boole ca di sujjóotal mboolem biddiiwi asamaan, di leen jaamu.
ba fàtte ay jalooreem, di kéemaan yi mu leen won.
Dañoo fàtte Yàlla ma leen di musal te def jaloore ca Misra.
«Nu ngeen ñemee naa: “Sobeelunu sunu bopp te toppunu tuuri Baal?” Seetleen li ngeen nekke ci xur wi, xool-leen li ngeen di def, mel ni giléem gu ndaw, di wodd-woddi, fu ne mu daw jëm fa,
Yeen, nu ngeen mane di sàcc, di bóome, di jaaloo, di giñi fen, di taalal Baal, tuur mi cuuraay, di topp yeneen yàlla yu ngeen xamul,
¶ «Yaw Yuda, ni sa dëkk yu mag tollu, ni la say tuur tollu. Ni mbeddi Yerusalem tollu it, ni la sarxalukaay yi ñu fa saam tollu, ñu di fa taalal cuuraay Baal, tuur mu seexluwu mi.»
Moo tax Aji Sax ji Yàllay Israyil wax ci sàmm yiy sàmm ñoñam ne: «Yeena tasaare sama gétt gi, dàq leen, te taxawuwleen leen. Kon maa ngii di leen taxawoo mbugal, yoole leen seen jëf ju bon.» Kàddug Aji Sax jee.
Mag dakkal na jataayu pénc, te waxambaane talatula xalam.
Alalu ger, ñu jël fi sa biir, ngir lor ay bakkan. Ndollant ci kaw tegandaay, nga jël feyeekoo bor, di wute alal sa àqu moroom. Man nag, nga fàtte ma. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Te sax ñoo yeble, wutiy góor, yónnee ndaw lu leen jële fu sore, ñu daw dikk, fekk leen sangu, tusngalu, gànjaru,
Ñoom seen yaay moo gànctu, ki leen ëmb moo def lu gàccelu, naan: “Damay toppi sama far, yi may jox sama lekk ak samag naan, ak samag wëñ ak sama lẽe ak samag diw ak sama biiñ.”
Ca kaw tund yu mag ya lañuy rendee ay sarax, cuuraay, ñu taale ca tund yu ndaw ya, ak ca taatu gii garab gu mag, ba ca gee, fa ker ga neexe. Moo tax seeni doom di gànctu, seen séeti doom di jaaloo.
Bési mbugal dikk na, bési añale taxaw na, na ko Israyil xam. Yonent lañu jàppe ab dof, ku yor waxyu di ku wéradi, ndax seen ñaawtéef gu réy, ak seen mbañeel gu tar.
Lu ñu leen gëna woo, ñu gën maa sore. Ay tuuri Baal lañuy defal ay sarax, te ay xërëm lañuy taalal cuuraay.
Ngeen wëtti ba regg, regg, bew, ba tax ngeen fàtte ma.