Teewul Sikem xemmemoon na Diina doomu Yanqóoba lool te bëgg ko, ba tax mu di ko naxtaan.
TSK
TSK · Hosea 2:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji déy a leen namma baaxe, moo ko tax di jóg moos ngir yërëm leen, nde Aji Sax jeey Yàllay njubte. Ndokklee képp ku ko yaakaar!
Dëfal-leena dëfal sama ñoñ, la seen Yàlla wax!
Aji Sax jeey dëfal Siyoŋ moos, dëfalaale fépp fu fa dib gent, ba def màndiŋam ni toolub Àjjana, jooram gu wow mel ni toolub Aji Sax ji, mbégteek bànneex teew fa, ak cant gu woy feelu.
Demal yéeneji kàddu yii fa bëj-gànnaar. Nga ne: “Israyiloo, Woyof-Kumba, délsil.” Kàddug Aji Sax jee. “Duma la fasal kanam. Man Boroom ngor laa, te duma jàpp mer ba fàww.” Kàddug Aji Sax jee.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di tijji wërsëgu askanu Yanqóoba, ñibbsil leen, baaxe seeni dëkkuwaay, ba dëkk dekkee ca tundam wu gentoon, kër buur taxawaat bérabam,
¶ «Yeena wax ci dëkk bii ne dina daanu ci loxol buuru Babilon ndax saamar akub xiif ak mbas. Waaye Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne:
Aji Sax ji da maa sant ma wax la ne la: “Aji Sax ji dafa wax ne: La ma tabaxoon a ngii, maa ngi koy daaneel, la ma jëmbatoon a ngii, maa ngi koy buddat, ba réew mépp daj.
Maa leen di yóbbu màndiŋ ma ñuy wooye Màndiŋu Askan yi, layoo faak yeen, di leen xool, ngeen di ma xool.
«“Waaye yeen tundi Israyil, yeenay naat, di meññal Israyil sama ñoñ, te léegi ñu ñibbsi.
¶ «Kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Léegi maay tijji wërsëgu Yanqóoba, maay ñeewante waa kër Israyil googu gépp, te maay fiire sama tur wu sell wi.
«Bésub keroog maay yékkati mbaarum Daawuda mi joy, ba fattaat xar-xar yi, defaraat gent bi, tabaxaat ko na woon.
Ngalla nanga sàmme saw yet sa ñoñ, sa gàtt yi nga séddoo, te ñu màkkaanoo gott bi ñoomu neen, fi digg parlu mu naat. May leen ñu fore àlli Basan ak Galàdd na jant ya woon.
¶ Malaakam Aji Sax ji ne: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, loo deeti xaar, doo noppee xañ yërmande Yerusalem ak yeneen dëkki Yuda? Juróom ñaar fukki at a ngii yoo leen mere!»
Su boobaa nag, bànni Israyil gépp ay mucc, noonee ko Mbind mi indee ne: «Siyoŋ la wallukat bay jóge, mooy tenqee ngëmadi ci askanu Yanqóoba.
Ñu jox ndaw si ñaari laafi jaxaay ja, ngir mu naaw, rëcc ninki-nànka ji, dem màndiŋ ma, ca rawtoom ba ñu koy leele lu tollook ñetti diir ak genn-wàll.