Wallam aka jege ñi ko ragal, te leeram dëgmal sunu réew mii!
TSK
TSK · Hosea 2:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Giñ naa ko ci man mii, sama gémmiñ njekk a ciy jibe, di kàddu gu dul randu. Man la ñépp di sukkal seen bëti óom, man it la bépp boroom làmmiñ di giñe.
Sama xol a jóg, ma xañ la sama kanam ab diir, waaye maa lay yërëme ngor gu sax.» Aji Sax, ji lay jot moo ko wax.
Yaay doon kaalag teddnga ci loxol Aji Sax ji, yaay doon mbaxanam buur, ci sa biir loxol Yàlla jii.
xanaa di waate Aji Sax jiy dund, ci dëgg ak njub ak ngor, kon xeet yi di barkeeloo Aji Sax ji, di ko sagoo.»
ñu doon sama ñoñ, may seen Yàlla.
Gannaaw bu ma walee waa kër Israyil sama noo, dootuma leen xañ sama kanam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»
¶ Noonu la deme ak yeen itam, bokk yi. Yaramu Almasi wi ngeen bennool, ci ngeen doone ñu deeyal yoonu Musaa. Noonu ngeen doone moomeelu keneen, te kooku mooy ki dekki, ngir nu meññ njariñ lu ñeel Yàlla.
¶ Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,
Nanu bég, di bànneexu te màggal ko, ndax céetu Gàtt bi agsi na, ab séetam defaru na ba noppi!
¶ Ba loolu amee menn malaaka dikk. Mu ngi bokk ci juróom ñaari malaaka, yi yor juróom ñaari ndab yi fees ak juróom ñaari musiba yu mujj yi. Mu ne ma: «Dikkal, ma won la séet bi, soxnas Gàtt bi.»