TSK

TSK · Hosea 2:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Suuf a ngi maral, wow koŋŋ, gottub Libaŋ am gàcce, lax, àllub Saron doon joor gu wow, garabi Basan ak Karmel yëngu, di ruus.

Sunu kërug jaamookaay gu sell ga te tedd, fa la sunuy maam daa màggale, sawara xoyom na ko, mboolem lu nu soppoon yàqu yaxeet.

Éey niti Israyili tey, teewluleen kàddug Aji Sax ji! «Ni màndiŋ mi aaye, ndax mas naa nee aaye ci Israyil? Mbaa ma mel ni réewum lëndëm aki loraangeem? Lu waral sama ñoñ naa: “Noo moom sunu bopp, dootunu délsi fi yaw”?

Gàngooru sàmm a sëxëtoo sama tóokëru reseñ, joggati sama waar, def waar wi ma neex màndiŋ mu ne maraas.

Man it maay ëñ sa pendal, muure sa kanam, saw taat ne duŋŋ.

¶ Aji Sax ji déy dafa wax ci mbirum kër buurub Yuda ne: «Yaay sama àllub Galàdd, sama collu tundu Libaŋ, waaye déy, maa lay def ni màndiŋ, ngay dëkk yu kenn dëkkul.

ay dëkkam gental, réew mi ne sereŋ, di ndànd-foyfoy, kenn du ko dëkke, doom aadama du fa jaare.

Ci biir mboolem sa jëf ju siblu jooju ak sa gànctu, fàttlikuwoo benn yoon ba ngay lu tuut, ne duŋŋ-duŋŋaaral, di wéqu, sangoo sa deret.

Tey mu ngi jëmbate fi màndiŋ mi, ci réew mu wow, maral.

Amos 8:11 TSK

«Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «maay wàcce xiif ci réew mi. Du doon xiifub dugub mbaa marum ndox, kàddug Aji Sax ji lañuy xiif.