Mise teg ca ne ko: «Kon nag déglul kàddug Aji Sax ji. Gis naa Aji Sax ji, mu toog ci ngànguneem, mboolem gàngooru asamaan a nga taxaw ndijooram ba càmmoñam.
TSK
TSK · Hosea 4:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen njiiti Sodom, teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor.
Aji Sax jaa ngi ci jataayu layoo, moo jóg di àtte ay xeet.
Kon nag yeen kókkalikat yi yilif askanu Yerusalem wii, dégluleen kàddug Aji Sax ji!
Bésub feyu la, Aji Sax ji di ca feyoo; mooy at mi Edom di yooloo la mu loroon Siyoŋ.
Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen ñiy déglu kàddoom, di lox. Lii de mooy seen kàddug bokk, yi leen jéppi, di leen dàq ngir samaw tur. Ñu ngi naan: «Na Aji Sax ji darajaal boppam, ba nu teewe seen mbégte, yeen ñii!» Waaye ñoom de ñooy rus.
Moo ma tax di layooteek yeen, ba layook seeni sët.» Kàddug Aji Sax jee.
Loolooy tax suuf di ñaawlu, asamaan di lëndëm. Maa ko wax, maa ko dogu; duma dëpp, duma deltu gannaaw.»
«Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor.
Su ko defee nga ne leen: “Xeet a ngii wu dul déglu kàddug Yàllaam Aji Sax ji, nanguwñu yar, worma tumurànkeel leen, ba daggook seen làmmiñ.”
Ndee déy moo ñalgoo sunuy palanteer, dugg sunuy kër yu yànj, ngir fàdd gone yi ci mbedd mi, ak xale yu góor yi ci pénc yi.
Danga naan: “Yeen buuri Yuda, yeen waa Yerusalem, dégluleen kàddug Aji Sax ji. Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngii di wàcce fi bii bérab, musiba muy buur noppi képp ku ci dégg.”
¶ «“Waaye yaw Cedesyas buurub Yuda, déglul kàddug Aji Sax ji: Aji Sax ji dafa wax ne doo deeye saamar.
«Dégluleen lii, yeen sarxalkat yi! Teeyluleen, yeen waa kër Israyil! Teewluleen, yeen waa kër buur! Yeen la àtte bi ñeel. Ag fiir ngeen tegoon ca Mispa, ab caax ngeen laloon ca tundu Tabor,
Efrayim mooy sàmmkatub ngelaw, yendoo topp ngelawal penku, di yokki fen ak fitna, fasoo kóllëre ak Asiri, yónnee yóbbalu diw ba Misra.
Dégluleen, yeen mag ñi, teewluleen, yeen waa réew mi ñépp. Ndax lii mas naa am ci seeni jant, mbaa seen janti maam?
Léegi nag, déglul kàddug Aji Sax ji. Yaa ma ne: “Bul biral waxyu ci Israyil te bul kebetu ci kaw askanu Isaaxa.”
Ngor a jeex ci réew mi, njub tumurànke ci nit ñi. Ñépp, ku ñu tuur deretam lañuy tëru, ku nekk, mbokkam lay fiir.
¶ Gannaaw ràññee Yàlla jaralu leen dara, Yàlla it bërgal leen ak seen xel mu doyadi, ba ñuy def jooju jëf ju jekkadi.
¶ «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag doo loru mukk ci ñaareelu dee gi.