Kon nag saamar dootu jóge sa kër mukk, ndax yaa ma ñàkke worma, ba jël jabaru Uri Etteen bi, def ko sa jabar.”
TSK
TSK · Hosea 4:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Màbb na it këri nit ña doon jaay seen bopp fa ñuy màggale tuur ya ca biir kër Aji Sax ji, te jigéen ña daan fa ràbbal tuur ma ñuy wax Asera ay xayma.
Yeenay rus moos ci garab yu mag, yi ngeen soppoona daje, di xërëmtu. Yeenay am gàcce ci tóokër, yi ngeen taamu woona daje, di bokkaale.
Tund wu mag te kawe, nga fàkk fa tëraay, yéeg fa, di fa sarxalal.
¶ Aji Sax ji nag wax ma ci jamonoy buur Yosya ne ma: «Gis nga li Israyil Woyof-Kumba-si def? Di dem kaw tundoo tund ak ker garaboo garab gu naat, di fa gànctu.
Dingeen xam ne maay Aji Sax ji, bu seeni néew nee xas fi seen biiri tuur, ak fi wër seeni sarxalukaay, ak kaw tund wu mag ak wu ndaw, ak mboolem ker garab gu naat, ak mboolem garab gu mag te sëq, fépp fu ngeen di taale cuuraay, ñeel seen mépp tuur.
Selebe yoon wu ne, tabax nga fa sa jaamookaay, di fa teddadil sab taar, ku romb, nga ràccal ko say tànk ci sa gànctu gu dul jeex.
Maay dakkal gépp mbéxam; ay màggalam, ay Terutel weeram, ay bési Noflaayam, ak mboolem bési ndajeem.
Gannaaw noonu la, Amaciya, Aji Sax ji nee: “Sa jabar ci biir dëkk bi lay gànctoo, say doom, góor ak jigéen, saamar tëral; sam réew, ñu natte buum, séddoo. Yaw nag, réewum yéefar ngay deeyeji; Israyil, ñu jële kom réewam, gàll ngàllo.”»