TSK

TSK · Hosea 4:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Suuf a ngi maral, wow koŋŋ, gottub Libaŋ am gàcce, lax, àllub Saron doon joor gu wow, garabi Basan ak Karmel yëngu, di ruus.

Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Duma tas lépp tasar, waaye réew mi mépp ay gental.

Tund ya laay jooy, di yuuxu, di jooy parluy màndiŋ ma, fa lépp lakk, ba jaareesu fa, déggeesul baatu jur; njanaaw ak mala, lépp daw, ne mes.

jën ak njanaaw di lox fi sama kanam, ñook ndundati àll bi ak mboolem luy raam ak kuy nit fi kaw suuf. Tund yi màbb, doji mbartal ya fàqandoo, tata yépp jóoroondoo.

Amos 1:2 TSK

Mu ne: Aji Sax jeey yëmmoo fa Siyoŋ, Yerusalem lay àddoo, parluy sàmm si ne faraas, mbooyum kaw tundu Karmel lax.

Amos 8:8 TSK

Moo tax réew mi nara yëngu moos, muy tiisu ku ci dëkk; suuf fuddoondoo, fees ni dexu Niil, di jóg ak a rës ni dexu Misra.

«Doom aadama ak mala, njanaaw ak jën laay buub, ak luy fakktale, booleek ñu bon ñi. Maay dagge doom aadama fi kaw déndub suuf.» Aji Sax jee ko wax.»