TSK

TSK · Hosea 9:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñu daldi teg ci kaw taabal ji, tegin wu jekk, mburu mi fi kanam Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.

Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu sell, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawar yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell.

«Waxal Aaróona ne ko: Muy tey muy ëllëg ba fàww, góor gu askanoo ci yaw ak maas gu mu mana bokk, su amee sikk du mana agsi ba ci sarxalukaay bi, di joxe ñamu Yàllaam.

¶ «Taabalu mburum teewal mi, nañu ci lal ndimo lu baxa, teg ci ndab yeek bàttu yeek njaq yeek tax yi ñuy sottee saraxi tuuru, door cee teg mburu moomu dul wuute.

«Santal bànni Israyil ne leen sama sarax, sama ñam wi jëm ci sama saraxi sawara ngir xetug jàmm, ñeel ma, nañu farlu ci di ma ko indil saa yu àppam jotee.

¶ Gannaaw loolu Neyemi boroom dëkk ba ànd ak Esra sarxalkat ba, di bindkat ba ba tey, ak Leween ñay xamal mbooloo ma, wax ak ñoom ñépp, ne leen: «Bésub tey jii, bés bu sell la, ñeel Aji Sax ji, seen Yàlla. Buleen ci naqarlu, buleen ci jooy.» Booba mbooloo ma mépp a doon jooy ca kàdduy yoon wa ñu dégg.

Yaw Israyil, jëlal doj yu rattax yi ci yoonu ndox wi, séddoo, muy sa cér, nga muurloo! Ñoom ngay tuural, di leen defal ay saraxi pepp. Waaye Aji Sax ji nee: «Ndax damay jéllale?»

Lu may doye lii? Ndàbb lu jóge Saba, diw gu xeeñ, bawoo réew mu sore? Seeni saraxi rendi-dóomal safu ma; seen saraxi jur, bugguma.»

Te nangeen def nii ma def. Buleen muur tuñum kaw ba ci sikkim te buleen lekk ñam wu leen njaal mi indil.

Bu ñu waññikoo it, du fi Aji Kawe ji. Ni xala gu yolom lañu mel, te seeni kàngam ay fàddoo saamar ndax seen sànjum làmmiñ, te loolu lees leen di reetaane ca réewum Misra.

Joel 1:13 TSK

Yeen sarxalkat yi, gembuleen te tiislu, yeen ñi dénkoo sarxalukaay bi, yuuxuleen, yeen boroom dénkaaney sama Yàlla, dikkleen, sol ay saaku yu ngeen fanaanoo, ngir toroxlu, nde xañees na seen kërug Yàlla ga saraxu pepp ak saraxu tuuru!

Amos 4:4 TSK

Aji Sax ji nee: «Demleen Betel, bàkkaare fa, dem Gilgal, bàkkaareeti fa. Rendileen seenub sarax ca ëllëg sa, joxe seen saraxi fukkeeli alal ca gannaaw ëllëg sa,

Amos 8:11 TSK

«Ay bés a ngii déy, di ñëw,» kàddug Boroom bi Aji Sax jee: «maay wàcce xiif ci réew mi. Du doon xiifub dugub mbaa marum ndox, kàddug Aji Sax ji lañuy xiif.

«Ngeen ne: “Léegi nag tinuleen Yàlla rekk, mu baaxe nu!” Yeena tooñ, ndax day siggil kenn ci yeen?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.