TSK

TSK · Isaiah 1:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye su ngeen saxee ci def lu bon, yeen ak seeni buur ay bokk sànku.»

Job 31:3 TSK

Xanaa du safaan a ñeel ku bon, naqar ñeel ku ñaaw?

Job 34:27 TSK

Li ko waral di boroom doolee dëddu Yàlla, sofental mboolem digley yoonam,

Ku réy du taxaw fi sa kanam, kuy def lu ñaaw, bañ nga ko.

Moykat yeey sànkoondoo, ku bon amul muj.

Waaye yaw ma fa kaw, yaay Aji Sax ji ba fàww.

Waaye kuy topp yoonu ndëngte, Aji Sax jee koy sànk, boole kook kuy def lu bon. Yal na jàmm dal Israyil.

googu ñaawtéef ay mujj doon seen xar-xaru tata ju kawe, funki, tata ja jekki jóoru.

Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.

«Te bu ñu génnee, gis néewi ñi doon fippu fi sama kaw, seeni sax duñu dee mukk, seen sawara du fey mukk, te boroom suux bu leen gis, yaram wa daw.»

Waaye su jawriñ ja nee ci xelam: “Sama njaatige dikkagul léegi,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya, góor ak jigéen, di lekk ak a naan, di màndi,

Ci biir sawara wuy sëlsëli lay doon. Ca lay mbugal ñi xamul Yàlla, ak ñi baña déggal xibaaru jàmm bi jëm ci sunu Boroom Yeesu.

waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem niti fen ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»