TSK

TSK · Isaiah 1:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sunuy buur ak sunuy njiit nag ak sunuy sarxalkat ñoo dale ca sunuy maam, di baña topp sa yoon, baña sàmm say santaane, bàyyiwuñu xel it ci kàdduy seede yi nga leen artoo.

Moo tax Aji Sax ji doge Israyil bopp ak geen, boole tiir ak barax fóom ci benn bés.

¶ Éy bokki Israyil, fippu ngeen Aji Sax ji ba sës, waaye walbatikuleen!

«Mbugal naa seeni doom, jariñul dara. Dégguñu yar, bóom ngeen seeni yonent, mbete gaynde yuy fàdde.

Kon naa dem seeti kàngam yi, wax ak ñoom. Xanaa ñoom dinañu xam yoonu Aji Sax ji, xam lu seen àtteb Yàlla laaj.» Waaye ñoo bokk daggook Yàlla, dogook moom.

Ñoom ñépp a di fippukat yu fétteeral, wër di sos, dëgërle ni xànjar ak weñ gu ñuul. Ñoom ñépp di yàqkat.

Sa sobeey sa yàqute! Maa la setal te taxu laa set. Dootuloo tàggook sa sobe, ba keroog may giifal sama xadar fi sa kaw.

Wóoy ngalla fippukat bu sobewu bi, dëkkub notkat yi.

¶ Ba loolu amee ñeenteelu malaaka mi sotti ndabam ci kaw jant bi. Ñu daldi may jant bi muy lakke nit ñi tàngooru sawaraam.