TSK

TSK · Isaiah 1:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 2:7 TSK

Ba mu ko defee Seytaane bàyyikoo fa Aji Sax ji. Ci kaw loolu mu sànni Ayóoba ay taab yu metti, dale ko ca téstën ma, ba ca kaw bopp ba.

Aji Sax ji, fitt nga maa fitt, dóor nga ma.

Ni bëtu ndox di dawe, ni lañuy dawale seenug coxor. Fitnaak salfaañooy riir ci dëkk bi, gisuma lu moy jagadeek loraange!»

Sama bokk yi seen xol jeex tax na sama xol jeex, may tiislu, tancoo njàqare!

Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Sa damm-damm du faju, sa góom du wér.

¶ «Waaye du tee, maa leen di may tan, faj leena faj ba ñu wér, won leen xéewalu jàmm ju dëggu.

Sa damm-damm amul paj, sab góom metti, ba mboolem ñi dégg li la dal di tàccu ci sa kaw, nde ana ku sa mbon gi dul jeex lorul?

Ab baadoolo bu ñuy wax Lasaar nag farala tëdde buntu kër waa ji, yaram wa ne fureet aki góom,