Seen meññeefum suuf, ak mboolem seenu ñaq, xeet wu ngeen xamuloon a koy lekk, te dees leen di not ak a dëggaate rekk, bés bu nekk.
TSK
TSK · Isaiah 1:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
seen noon yi Aji Sax jiy yebal ci seen biir, ñoom ngeen di jaamuji ci biir xiif, ak mar ak rafle, ak gépp ñàkk. Aji Sax jeey teg yetu weñ ci seen ndodd, ba sànk leen.
Bu ñu wàññikoo, ba néew doole ndax noteel ak coonooku tiis,
Maa dégg Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ne: «Giñ naa ne kër yu bareey gental déy, kër yu yaa, rafet, kenn dëkku ca.
¶ Ma ne: «Boroom bi, foo àppal loolu?» Mu ne: «Xanaa fii ba seeni dëkk gental, ba kenn dëkkatu ca, ba nit dootu nekk biir kër ya, suuf sa yàqu yaxeet, di ndànd-foyfoy.
Dëkk bu gental tasaaroo na, kër yépp tëje, kenn duggul.
Gaynde yaa ngi ŋar ci seen kaw, di leen xiiru! Gaynde yee gental seenum réew, ba seeni dëkk di gent yu kenn dëkkul.
Sunu suuf toxu ciy jaambur, sunuy kër ñeel ay doxandéem.
Ay doxandéem a jeexal dooleem, te xamu ko, aw liir tege ci kawam weex tàll, te yégu ko.