¶ Ibraayma dellu neeti: «Ngalla Boroom bi, bul mer, ma wax bii yoon rekk te noppi. Léegi su ñu dee fukk doŋŋ nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma tas dëkk bi, ndax fukk ñooñu jub.»
TSK
TSK · Isaiah 1:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
su boobaa yéefar yépp a naan: «Ana lu waral Aji Sax ji def nii réew mi? Lu waral mii sànj mu tàng te réy?»
Bu ca fukkeelu nit ña desoon, ñoom it dees na leen dellu taal. Waaye dañuy mel ni wenn ci xeeti garab yu mag yi ñuy gor, ëkk ba dellu jebbi, ëkku xeet wii, jiwu mu sell lay doon.»
fa dara dul des lu moy am poraat; mu mel ni wittum oliw, bu noppee ñaari doom ak ñett ay des ca kaw, mbaa ñeent ba juróom ci car yi meññ. Kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil.
Noonu lay deme ci àddina, ci biir xeet yi, mbete benn-benni doomi oliw gu ñu gësëm, mbaa doomi reseñ yu des ca ndey ja, gannaaw bu ñu wittee ba sottal.
Ndes wa des ca askanu Yuda ñooy saxaat ay reen, ba meññaat ay doom.
Sama ñaawtéefu askan wee màgg, ba raw ñaawtéefu waa Sodom, dëkk ba jekki jàllarbiku, te loxo laalu ko.
Waaye du tee mu am ndes mu ca rëcce, diy góor aku jigéen, ñu ñuy génneji réew mi. Ñu ngooguy génn, di leen fekki, te bu ngeen gisee seen jikko ak seeni jëf ju bon, seen xol dina sedd ci musiba mi ma wàcce ci kaw Yerusalem, ak mboolem lu ma fi wàcce.
«Maa jàllarbi lenn ci yeen, na ma jàllarbee woon waa Sodom ak Gomor. Ngeen rëcce ca ni gillit gu ñu fëkke cib taal. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee!
Moo tax, giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Aji Sax ju gàngoor yee, Yàllay Israyil, «Mowab déy ni dëkkub Sodom lay mujje, Amoneen ñi mel ni Gomor, ay dég ak paxi xorom a koy nangu, mu gental ba fàww. Sama ndesu ñoñ a leen di sëxëtoo, ndesu xeet wi ma séddoo moo leen di moom.»
¶ Ci mbirum Israyil la Yonent Yàlla Esayi itam xaacu woon ne: «Su bànni Israyil tolloo ni feppi suufas géej sax, as ndes a ciy mucc.
Ana lu ko Yàlla tontu? Da ne: «Beral naa sama bopp juróom ñaari junniy (7 000) nit ñu sujjóotaluloon Baal tuur mi.»