TSK

TSK · Isaiah 10:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Axas jël xaalis ak wurus wa nekkoon ca kër Aji Sax ja ak ca dencukaayi kër Buur, defal ko buurub Asiri yóbbal.

¶ Ci kaw loolu buurub Asiri jële ay nit dëkk ya ñuy wax Babilon ak Kuta ak Awa ak Amat ak Sefarwayim, dëël leen dëkki Samari, ñu wuutu bànni Israyil. Ñu daldi moom diiwaanu Samari, féetewoo dëkk ya.

Esekiya joxe mboolem xaalis ba nekkoon ca kër Aji Sax ji ak ca dencukaayi kër Buur.

Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa? Moo kooy yékkatil kàddu? Kooy xool gëti xeebeel? Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji?

Wóoy ngalla ñii defe ne ñoo xam, yaakaar ne ñoo muus.

Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa? Moo kooy yékkatil kàddu? Kooy xool gëti xeebeel? Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji?

«Mowabee, du yaay kañu, naan jàmbaar ngeen, diy ñeyi xare?

«Yaw nit ki, Tir dëkk ba moo ree Yerusalem, ne: “Ñaw! Buntu dëkk bi xeet ya daan jaare dàjjiku na! Léegi man la bunt ubbikul, léegi maay woomle, Yerusalem gental na.”

Waxal, nga ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii fi sa kaw, yaw Firawna buuru Misra, yaw ninki-nànka ju mag ji goore sa diggi dex, te naan: ‘Maa moom sama dex, man ci sama bopp maa ko sàkk!’

Ma ngay wax naan: «Xanaa lii du Babilon gu mag gi ma tabax man, ci sama doole ju réy, muy péeyu buur, di sama ndam ak sama daraja?»

Efrayim moom, su naatee ci biiri bokkam it, fa màndiŋ ma la ngelawal penku, ngelawal Aji Sax ji di uppe, bëti ndoxam tëju, ay teenam déy. Kii mooy sëxëtoo ab dencam, ak mboolem lu cay alal.»

Amos 6:13 TSK

¶ Yeena ngi damu ca dëkk ba ñuy wax Lodebar (mu firi Amul njariñ) te naan: «Xanaa du sunu dooley bopp lanu nangul sunu bopp dëkk bu am doole ba ñuy wax Karnayim (mu firi Ñaari béjjén)?»

Moo tax muy rendil mbaalam ab sarax, di taalal ab caaxam saraxu cuuraay, te naan moo niinal njëlam, duunal ab dundam.