¶ Gannaaw ba loolu wéyee Daawuda dem dëkk ba ñuy wax Noob ca Ayimeleg sarxalkat ba. Ayimeleg gatandu ko, di lox, ne ko: «Lu la taxa wéet, kenn àndul ak yaw?»
TSK
TSK · Isaiah 10:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu am ñu ca dëkke Anatot ak Nob ak Anaña;
Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.
Moo tax Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Yeen sama ñoñ ñi dëkke Siyoŋ, buleen ragal waa Asiri yi leen di dóor yet, ŋàbbal leen bolde ni waa Misra daa def ak yeen.
Yéegeleen ab raaya kaw tund wu ne duŋŋ, joorleen ñii, tàllal-leen loxo, ñu jàlle bunti kàngam yi.
Du tee ma wàcceel Aryel musiba, ñuy yuuxook a jooyoo. Yerusalem ay mel ci man ni Aryel, taalub sarxalukaay.
Fitt aku xeej lañuy ŋëb, néeg lool, duñu yërëm; seen coow ni riirum géej, ñu war seeni fas, rëpptal, làng-déral leen, yeen waa Siyoŋ, dëkk bu taaru bi.»
Te man ci sama bopp,” kàddug Aji Sax jee, “maa koy nekkal tatay sawara ji ko ub ràpp. Te it maay doon daraja ji ci biiram.”