TSK

TSK · Isaiah 10:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te sax, xanaa du Aji Sax ji laa àndal ba dalsi fi kaw bérab bii, ngir tas ko? Aji Sax ji ci boppam moo ma ne: “Songal réew mii, tas ko!”»

Bala xale bee man ne “Baay” mbaa “Yaay” déy, dees na yóbbul buurub Asiri alal ju ñu foqatee Damaas, ak lël ju ñu këfe Samari, nangu ko.»

Nit ñaa ngi màtte ndijoor, te doyaluñu, di xàmpe càmmoñ te suuruñu, ku nekk di yàpp sa mbokk:

Yuday doon tiitaangey waa Misra, ba ku ñu ci tudd Yuda, nga tiit, ngir la leen Aji Sax ji Boroom gàngoor yi naral.

Boroom bi nee: «Askan wii, làmmiñ lañu ma jegee, lori neen lañu may wormaale, te seen xol sore ma. Seen ragal ak man it, njàngum tari kepp la.

Bàkkaarkati Siyoŋ tiit nañu, way-gëmadi yaa ngay lox. Ana kan ci nun moo mana dal ak sawara suy xoyome? Ana kan ci nun moo mana dal ak taal yu yànj ya dul fey?

Maa yékkatee nit bëj-gànnaar, mu bawoo penkub jant, di tudd sama tur. Mooy note boroom dëkk ni ban mbaa binit bu defarkatu njaq di dëggaate.

«Maa doon dëre tànk, man kenn ci ab dërukaayu reseñ, xeet yépp kenn dërlewu ma ci. Sama mer laa leen dëre, samam sànj laa leen dëggaatee, seen deret tis ci samay yére, ma taqal sama yére yépp.

Loolu yépp itam taxul Yuda workat bi, doomu ndeyu Israyil, délsee léppi xolam fi man, xanaa di jinigal rekk.» Kàddug Aji Sax jee.

maa ngii di yónnee, jëli mboolem làngi bëj-gànnaar.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay yónnee it ca Nabukodonosor buuru Babilon mi ci samag curga, daldi leen boole indi ci kaw réew mii ak ñi ci biiram ak mboolem xeet yi ko séq. Maa leen di faagaagal, gental leen gent bu sax dàkk bu ñuy muslu.

Ngeen naa: “Wóoy saamaru Aji Sax jii, xanaa doo selaŋlu? Dellul sa mbar, boog, dal-lu, ne tekk!”

Ni ñeyi xare lañuy mel, di joggati banu mbedd mi ci biir xeex bi. Noonu lañuy xaree, nde ñoom la Aji Sax jiy àndal, ñuy torxal gawar yi.