Dëkk yiy péeyi nguuram ñoo di: Babel ak Ereg ak Akàdd ak Kalne, gi ci réewu Sineyaar.
TSK
TSK · Isaiah 10:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Buurub Asiri nangul ko, dal ca kaw Damaas, nangu dëkk ba, jàpp waa dëkk ba, yóbbu Kir, ba noppi rey Reccin.
¶ Ci kaw loolu buurub Asiri jële ay nit dëkk ya ñuy wax Babilon ak Kuta ak Awa ak Amat ak Sefarwayim, dëël leen dëkki Samari, ñu wuutu bànni Israyil. Ñu daldi moom diiwaanu Samari, féetewoo dëkk ya.
Gaw nañu Samari ba ca ñetteelu at ma, door koo nangu, ca juróom benneelu atu nguurug Esekiya, yemook ba Ose buurub Israyil duggee juróom ñeenteelu atu nguuram.
Damaas a yilif Siri, te Reccin yiliful lu moy Damaas. Fii ak juróom benn fukki at ak juróom Efrayim tas, ba xeet wa réer.’
Yoon yaa ngi wéet, kenn jaareetul ci ñall wi! Kóllëre fecciku na, xeebees na ay seede, te kenn faaleetul doom aadama.
Ana buuri Amat ak Arpàdd ak Layir ak Sefarwayim ak Ena ak Iwa?”»
Lu jëm ci Damaas: «Dëkk yu mag ya ko wër, di Amat ak Arpàdd, jàq nañu; dég-dég bu tiis ba ñu dégg la. Dañu ne yàcc, jaxasoo, mbete géej gu sàmbaraax, deesu ko dalal.
Jàll-leen ba Kalne, xool; jóge fa jëm Amat dëkk bu mag ba, wàcci Gaat, dëkkub waa Filisti ya. Ana fu ñu tanee yii réew? ak fu ñu leen ëpplee suuf?