TSK

TSK · Isaiah 12:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sama doole, sama kaaraange, Ki Sax a; te mooy sama wall tey. Mooy sama Yàlla, ji may tagge, sama Yàllay maam, ji may joobe.

¶ Aji Sax ji nag wàcc ci biir aw niir, taxaw ak Musaa foofa, daldi biral turam, ne: «Aji Sax ji.»

Aji Sax ji, yaw, ku la xam, wóolu la. Aji Sax ji, yaw, ku lay sàkku, doo ko wacc.

Nga di leen diir fittu kanam, ñu wone gannaaw.

Aji Sax ji laay sagoo, néew-ji-doole dégg, bég.

Mu ngi fey xare ci àddina sépp, dog fitt, damm xeej, lakk pakk.

Woyleen Yàlla, teral turam, xàllal-leen kiy war niir yi, Ki Sax moo di turam. Bànneexuleen fi kanamam.

Man de, jege Yàllaa ma gënal. Boroom bi, Aji Sax ji, yaw laa def kiiraay, ngir siiwal sa jépp jëf.

Aji Sax ji, Aji Kawe ji tiim suuf sépp; yaaka màgga màgg, ba sut tuuroo tuur.

Éy Aji Sax ji, sunu Yàlla, wallu nu, génnee nu ci xeet yi, dajale nu, nu sante la sa sellnga, di sagoo sa teddnga.

Màggal-leen Ki Sax! Yeen ñiy jaamu Aji Sax ji, màggal-leen ko, màggal-leen turu Aji Sax ji!

Yeen xeetoo xeet, màggal-leen Aji Sax ji, réewoo réew, kañleen ko.

Màggal-leen turu Aji Sax ji, moom doŋŋ la turam kawe, darajaam tiim asamaan ak suuf.

Bésub keroog booba, kuy daŋŋiiral, detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.

Yeen waa penku, sargal-leen Aji Sax ji boog, yeen waa duni géej, teral-leen Aji Sax ji Yàllay Israyil.

Aji Sax jee kawe, moo dëkke fa kawa kaw, te mooy dajal fi Siyoŋ njekk ak yoon.

«Waxleen xeet yi, yéeneleen, woneleen misaal te yéene, waxleen lii, bañ cee làq dara. Neleen: “Dees na nangu Babilon, torxal Bel mbaa Mardug, tuur mi, tas ko, gàcceel gàllaaj yi, tas kasaray tuur yi.”