Babilon nag, mooy gànjaru réew yi ko wër, di teraanga ji Kaldeen ñiy sagoo, waaye Yàllaa koy tas, mu ne tasar ni Sodom ak Gomor.
TSK
TSK · Isaiah 13:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
At ma Buur Axas saayee, bii yéene jib na:
Yéene bii ñeel na Damaas: Damaas a ngii, léegi mu noppee doon ab dëkk, xanaa ab jalu tojit;
Yéene bii moo wàccal màndiŋ ma feggook géej ga: Ni ag ngëlén di riddee jaare Negew ni la noon di bawoo màndiŋ ma, jóge réew mu raglu.
Yéene bii ñeel na xuru Peeñu ma: Ana lu ngeen di yéege, yeen ñépp seen kawi taax?
Aji Sax jiy seen jotkat, Aji Sell ju Israyil dafa wax ne: «Yeena tax ma yebal ku songsi Babilon, ba dàjji lu fay tëjukaay, ba xaxalooy Kaldeen ñooñu diy jooyoo.
Yaw janq Babilon, wàccal, toog ci pënd bi. Yaw dëkkub Kaldeen bi ci taar bi laa ne, toogal fi suuf, amatoob jal. Dootoo dégg «Lewet, xay.»
¶ «Su ko defee bu juróom ñaar fukki at yi matee, ma doora dikkal Babilon ak buuram ndax seeni ñaawtéef.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay gental réewum Babilon ba fàww.
¶ Kàddu gii la Aji Sax ji wax ci mbirum réewum Babilon, réewum Kaldeen ña, te Yonent Yàlla Yeremi jottli ko.
Waxleen, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Boroom Yerusalem la àrtu bii ñeel, mook mboolem waa kër Israyil gi fi dëkk.”
SÉDDALE: Séddale nañu sam réew, ba jox ko xeeti Medd ak Pers.»
¶ Ab yéenee ngi bu ñu won Yonent Yàlla Abakug.
¶ Ab yéenee ngi, di kàddug Aji Sax ju dikkal Israyil. Kàddug Aji Sax jee, ki firi asamaan, lal suuf, te bind noowug doom aadama ci biir doom aadama.
¶ Kenn ci juróom ñaari malaaka, yi taawu juróom ñaari ndab yi nag dikk, ne ma: «Kaay, ma won la mbugalu jigéenu moykat ju mag, ji toog ci ndox mu bare.