su boobaa yéefar yépp a naan: «Ana lu waral Aji Sax ji def nii réew mi? Lu waral mii sànj mu tàng te réy?»
TSK
TSK · Isaiah 13:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Isaiah 14:12
TSK
Moo yaw biddiiwu njël, bi noon ràññ, tey nga xàwwikoo asamaan ba fii! Yaw mi daa daan xeet yi, tey ñu gor la, nga goor.
Jeremiah 50:40
TSK
Mu mel ni ba Yàlla tasee Sodom ak Gomor, tasaale la ko wër.» Kàddug Aji Sax jee. «Nit du fa dëkkati, doom aadama du fa dalati.»
Daniel 2:37
TSK
Yaw Buur, buuru buur yi, yaw mi Yàlla Boroom asamaan jox nguur ak kàttan ak dooleek ndam,
Amos 4:11
TSK
«Maa jàllarbi lenn ci yeen, na ma jàllarbee woon waa Sodom ak Gomor. Ngeen rëcce ca ni gillit gu ñu fëkke cib taal. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee!