TSK

TSK · Isaiah 13:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ku bon, ñu dagge ci réew mi; kuy fecci worma, ñu buddi, sànni.

Yuuxuleen! Bésub Aji Sax ji moo dëgmal, te ni sànkute gu bawoo fa ci Aji Man ji lay dikke.

Bésub feyu la, Aji Sax ji di ca feyoo; mooy at mi Edom di yooloo la mu loroon Siyoŋ.

Bésub mbugal laa mébétoon, te atum njot teew.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Aw askan a ngii bàyyikoo réewum bëj-gànnaar, xeet wu mag lañuy doon, sàqee fa cati àddina.

Siyoŋ ne: «Yal na sama yàpp ak sama coono topp Babilon.» Yerusalem ne: «Yal na sama deret topp waa Babilon!»

Joel 2:1 TSK

Wal-leen bufta ca Siyoŋ, dégtal-leen ab yéene ca sama kaw tund wu sell. Na waa réew mi mépp lox, nde bésub Aji Sax jaa ngi dikk te dëgmal na.

Nahum 1:6 TSK

Bu sànjoo, ana kuy taxaw? Ana kuy dékku tàngooru meram? Am sànjam a naan soteet ni sawara, doj yi rajaxoo fi kanamam.

looloo tax ci benn bés la musiba yiy këppoondoo ci kawam: mbas, deele akub xiif, te dees na ko lakk ba mu jeex, ndax Boroom bi Yàlla mi ko mbugal moo am doole.»