TSK

TSK · Isaiah 14:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 20:6 TSK

Bu màggoon ba tollook asamaan it, ba bopp ba àkki fa kawa kaw,

Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.

Waxal Tir mi tooge buntu géej, jula yooyuy jëflanteek xeeti dun yu bare, nga ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Tir yaa noon: ‘Maaka matub taar!’

Xanaa doo janook ki lay rey, naati yaay yàlla? Boo tàbbee ca sa loxoy jamkat ya, keroog nga noppee doon yàlla, di nitu kese.

Yaa doon malaakam serub mu ne ràññ, di aare, ma tabb la fa kaw tundu Yàlla wu sell wa, ngay daagoo digg doj yuy tàkk.

¶ Ca saa sa kàddu ga sotti ñeel Nabukodonosor. Ñu dàqe ko ci nit ñi, muy dunde ñax niw nag, lay biy wàcc di ko faam, ba kawar gi sëq ni dunqi jaxaay, ay wewam di saf yu njanaaw.

Muy màgg nag bay diir mbagg gàngoori xarey asamaan, ba daaneel lenn ci ñoom, ak lenn ci biddiiw yi, nappaaje leen.

Ana dëkk bu xumb ba dëkke woon kaaraange, te naan cim xelam: «Man rekk a, du keneen»? Nan la doone nii ab gent, bérab bu rab yiy goore, mboolem ku fa jaare, ub gémmiñam, jalu.

Kooku mooy jànkoonteeka damu ci kaw mboolem lees di wooye yàlla, mbaa lees di jaamu, te mooy mujj toog ca kër Yàlla ga, ba far tudde boppam Yàlla.