¶ Jant yooyu doomu Baladan Berodag Baladan buuru Babilon moo yónnee Esekiya bataaxal ak yóbbal. Booba dafa dégg ne Esekiya daa woppoon.
TSK
TSK · Isaiah 14:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñeel askanu Kore wu góor, di woyu Sabóor. Dëkkub Aji Sax ji, kenu yaa nga ca tund yu sell ya.
Na xeet yi wormaal turu Aji Sax ji, buuri àddina sépp wormaal darajaam,
Aji Sax ji kat a tànn Siyoŋ, taamu faa dëkke.
di mbaar mu ñuy serloo tàngooru bëccëg, di ko seeloob taw ak waame.
Yeen waa Siyoŋ, serleen te sarxolleel ku màgg ki fi seen biir, Aji Sell ju Israyil.»
Moo tax Boroom bi Aji Sax ji wax ne: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ aw doju coll, muy doju collu tànnéef wu gànjare ngir kenu gi, te ku ko wéeroo doo gaawa daw.
Yerusalem kay law ndes di génne, aw ndes ay rëcce tundu Siyoŋ, te Aji Sax ji Boroom gàngoor yi mooy sottal loolu ci xéraangeem.
Maa naa ci Sirus: “Sama sàmm bi!” Mooy matal sama bépp nammeel, te it moo naa ci Yerusalem: “Nees ko tabaxaat,” kër gu sell gi, laa ne: “Nees ko yékkatiwaat!”»
Waaye maay wacc fi sa biir askan wu woyof te néew doole, ñu yiiroo turu Aji Sax ji.
Bésub keroog la kóllëre ga dog, teefonke yi may xool daldi xam ne loolu kàddug Aji Sax ji la.
¶ Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo taamu ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur, gi Yàlla dig ñi ko sopp?