TSK

TSK · Isaiah 16:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba mu ko defee Daawuda dëkk ca biir tata ja, wooye ko Kër Daawuda, ba noppi tabax fa ko wër fépp, dale ko ca sëkkub Milo, ba ca biir.

Yàllay Israyil a wax, moom mi Israyil sës, moo ne: Ku jiite ay nit cig njub, bu jiitee cig ragal Yàlla,

muy àttee sa mbooloo njub, di àttee sa néew-ji-doole ñi yoon,

Muy taalif bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra.

gatandoo ko Aji Sax jiy dikk, àttesi àddina, di àtte dun bi njekk, tey àttee xeet yépp dëggam.

Buur, jëfe yoon mooy dooleem, te yaa saxal njub, yoon ak njekk ci askanu Yanqóoba.

Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese, ab car soqeekoo fa reen ya,

Buur a ngii, njekk lay nguuroo, jawriñ ñi it, yoon lañuy yilifee;

«Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, mu falu di buur bu xelu, di jëfe njub ak njekk ci réew mi.

Palug mboolem nguur yi asamaan tiim, ak kilifteef gaak daraja ja dees na ko boole, jébbal aji sell yu Aji Kawe ji. Nguurug mbooloo moomu day sax ba fàww, kilifa yépp di ko déggal, di ko wormaal.”

Micah 4:7 TSK

Maay def liy soox aw ndes, la ñu dàq fu sore, ma def ko askan wu am doole, te Aji Sax jeey doon seen buur ca kaw tundu Siyoŋ, li ko dale tey ba fàww.

Luke 1:31 TSK

Dinga ëmb, ba jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.

“Boroom bi nee: Gannaaw loolu dinaa délsi; maay yékkati kër Daawuda gi daanu, maay yékkati gent yi, joyanti ko,

¶ Gannaaw loolu lépp, noonu lay seeye nag, xamleen bu baax li leen war! Jëfin wu sell akug njullite,