Yeen, seen Yàlla dogalal na leen kàttan; éy Yàlla, jëfeel doole ja nga nu jëfeeloon.
TSK
TSK · Isaiah 18:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waa màndiŋ mi di ko sukkal, ay noonam mëq suuf,
Aji Sax ji kat da maa wax ne: «Maa ngi fi ma tollu di xool, ne tekk, ni tàngooru jant bu ne ràññ, mbaa lay bu defu niir ci tàngooru ngóob.»
Aji Sax ji dafa wax ne: «Muy ñaqu Misra, di koomu waa Kuus, ak waa Seba, ya ne sireet ca kaw, ñoom ñépp ay jàllsi, nga jagoo. Sa gannaaw lañuy topp, yeewe, jàllsi; sujjóotal la, di ñaan naan: “Fi yaw daal la Yàlla ne, du feneen, te tuur neen la.”»
«Yaw janq Siyoŋ mu taaru, jógal bàcci leen, sa béjjén laay def ag weñ, say wewi tànk, ma def ko xànjar, nga rajaxe xeet yu bare.» Yaay faagaagal seen alal ju lewul, ñeel Aji Sax ji, seen koom ñeel Boroom àddina sépp.
Su boobaa mboolem ndesu wépp xeet wu songoon Yerusalem, Yerusalem lay yéegi at mu ne, ngir sujjóotali Buur Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, tey màggalsi màggalu Mbaar yi*.