TSK

TSK · Isaiah 19:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Maa ngi koy gis, te du tey, Maa ngi koy niir, te jubseegul; biddiiw a feqe fa Yanqóoba, yetu nguur a yékkatikoo fa Israyil, daldi toj boppi Mowab, toj kaaŋi mboolem askanu Set.

Kàngam ya fa Cowan dañuy teqlikook seen sago, diglekati Firawna yu xelu ya di digle ag ndof. Ma ne: «Yeen diglekat yi, nu ngeen mana waxe Firawna naan: “Nun ay boroom xel lanu, sosoo ca buur ya woon”?»

¶ Gannaaw gi kàddu dikkal na Yeremi, jëm ci mboolem Yudeen ñi sancsi réewum Misra, te dëkke Migadol ak Tapanes ak Memfis ak diiwaanu Pattros. Mu ne:

Yaw mi dëkke Misra mu taaru mi, ëmbal sa ëmb, jëm ngàllo; Memfis dëkk bii kat ci gental la jëm, di ndànd-foyfoy lu kenn dëkkul.

Maay taal Misra, dëkk ba ñuy wax Ciin di rag-ragi; dëkk ba ñuy wax No, ñu bëtt ko; Memfis, noon yi nangu ko digg bëccëg.

Fa Yuda la doju collu tabax di bawoo, jënu xayma, fa moom, xalay xare, fa moom, mboolem njiit yi ba ñépp daj, fa moom.

Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag: «Moo di doj wa tabaxkat ya beddi woon, te mu mujj di doju coll wi.»