TSK

TSK · Isaiah 19:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu dem nag, ba manatu koo nëbb. Mu wut pañe bu ñu ràbbe barax, fatte ko godoroŋ ak ndàbb, yeb ca liir ba, daldi dem, teg ko ca biir barax, ba ca tàkkal dex, ga ñu naan Niil.

Maa gas ay teen, naan ndoxum réewum jaambur, maa joggatee sama téstën, wali Misra yépp, ŋiisal ko.”

Job 8:12 TSK

Bu ndox ma ŋiisee, mooy jëkka lax, te du ñoragum bay mata dog.»

Yeen ñiy yónni biir géej, ay ndaw, ci gaali barax yu war mbeex mi; yeen ndaw yu gaaw yi, demleen, fekki xeet wu siggi, rattax yaram, askan wu ñu ragale fu jegeek fu sore, xeet wu am doole, di falaxee, te seenum réew defi wal.