TSK

TSK · Isaiah 2:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji, ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf.

tooli tund yu mag yi indil mbooloo mi jàmm, tooli tund yu ndaw yi xéewale leen njekk,

gatandoo ko Aji Sax jiy dikk, àttesi àddina, di àtte dun bi njekk, tey àttee xeet yépp dëggam.

Nde gonee juddu, ñeel nu, di doom ju góor ju ñu nu may, mu yenu kilifteef gi, ñu di ko wooye Diglekat bu yéeme bi, ak Yàlla jàmbaar ji, ak Baay bi sax dàkk, ak Buuru jàmm bi.

Ragal Aji Sax ji lay safoo, du lu ko bëtam may rekk lay àttee, du lu ko noppam may rekk lay dogale,

Till ay bokk ak mbote ab dal, segg bokk akub tef ab tëraay, wëllu ànd ak gaynde gu mat, ak juru yar, tuut-tànk jiite leen.

«Xool-leen sama jaam bi ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci kawam laa teg samag noo, te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte.

Maay wuutale xànjar, wurus; wuutale weñ gu ñuul, xaalis; bant, xànjar; doj, weñ gu ñuul. Jàmm laay def mu jiite la, def njekk yilif la.

Bésub keroog maa leen di fasal kóllëre ak rabi àll yeek njanaaw yi, ak ndëgmeent yi. Fitt ak saamar akub xare it, maa koy dagge ci réew mi, te maa leen di may tëraayu jàmm.

Micah 4:3 TSK

Mooy àtte diggante xeet yu bare, mooy dogalal askan yu am doole te sore, ñu tëgg seeni saamar ay illéer, def seeni xeej ay sàrt. Aw xeet dootu xàccil moroom ma saamar, te dootuñu jàngati xare.

¶ Ba loolu wéyee ma gis asamaan ubbiku, fas wu weex daldi feeñ. Ki ko war, «Wóor te Dëggu» lañu koy wax te njub lay àttee, di ko xaree.