Ku ñàkkula tooñ sax, mu xettli la, te sag ñàkk sikk lees koy xettlee.
TSK
TSK · Isaiah 20:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dëgg laay def nattukaay, njekk di sama buumu beteex, tawub doji yuur buub rawtub fen, wal ma mëdd làquwaay,
Ndax Boroom bi Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil dafa wax ne: «Délsi, dal-lu moo leen di musal. Ne tekk te wóolu maa leen di dooleel. Waaye yeena buggul!
Waa Misra, niti neen, duñu Yàlla; seeni fas it, suuxu neen, duñu leneen. Aji Sax jeey xàcci loxoom, kiy walloo mooy tërëf, ki ñuy wallu daanu, ñoom ñépp bokk sànku.
bésub sànkute dikkal képp kuy Filisteen, ba dagge dëkk yii di Tir ak Sidon ndimbal lu ñu dese woon. Aji Sax jaa ngay sànk Filisteen, ña des te cosaanoo dunu Keret.
Fa nit ñi naan: «Jàmm ak kaaraange dikk na,» fa la sànkute di dale ci seen kaw, ni aw mat di jekkee dal ci kaw jigéenu wérul, te kenn du ca rëcce.